Lan nga bëgg yëgle?
Leerali daluweb
Ngir ñu mëna gêstu ab daluweb soxla nañu dëkkuwaayu bataaxalam buñu xàmee niki am ab URL manaam http://www.iwf.org.uk/what-we-do, www.iwf.org.uk/what-we-do or iwf.org.uk/what-we-do. Mën nga gis xuusukaay bi ci kaw xëytu wi.
Soo amee ay xibaar yoo jàpp ni mën nañu dimbali, niki ab tektal ci fi këmb bi nga ñuy yëgël nekk ci ab daluweb bu yaatu wala turu jëfandikukat ak baatu jàll buñu soxla ngir dugg ci, dugal ko ci boyetu tektal bi.
Soo ñu bëggee yëgël beneen daluweb defaral beneen yëgle. Bul taf lëkkalekaay yi ci boyetu tektal bi ndax duñ leen toppatoo.
Jërëjëf.
Leerali neegu bataaxal
Yëgël nañu bataaxal spam yiñu lim fii ci suuf kon soxlawul nga koy yëgëlaat - dindi leen ci sa boyet te nga tej sa palanteeru xuusukaay ngir jeexal yëgle bii.
- Porno with 3 **
- Here you can download the ** and... ** **
- Here you can download the **** lorem
- ** **, and real **** on the streets
- Download the ** and** **!!! and real ****
- Porno with **, Here you can download the ** and...
- Here you can download the **** lorem ** **, and real
Sudee limu ñu bataaxal bi nga ñu bëgga yëgël nekkul fii ci kaw, demal ci jéego bi ci topp.
Leerali neegu bataaxal
Ngir yëgle am imelu spam dina ñu soxla dëkkuwaayu lëkkalekaay bi / daluweb bi ci imel bi.
Ab dëkkuwaayu daluweb nii lay mel: http://www.iwf.org.uk or www.iwf.org.uk.
Wutal ay tektal soo soxla ay tektal ngir gis dëkkuwaayu Web bi walla jëfandikoo nataalu ndimbal li ci sa joxekatu bataaxal.
Sudee xàmuloo nuñuy defee lii jalalel bataaxal bi ci [email protected]
Sudee sa yëgle dafa méngook lenn luñu dugal ci daluweb yi te ñépp mën ko gis, duñu ci mëna def dara waaye mën naa doon mbir bu yoon wara toppatoo.
Sudee sa yëgle dafa méngook bépp jafe-jafe buñu lim fii ci suuf da nga wara jokkoo ak takkadeer bu nekk fi nga dëkk wala mbootaay yuy àar xale yi.
- Da nga jàpp ni dañoo nekk di sàkku ab xale
- Nataal yuñu denc ci ay jumtukaayi jàmbur niki telefon portaabal, tablet wala ordinatër
- Ay daluwebi waxtaan ci bind kese te amul benn nataal
- Ay porogaraami jébbal ay taxañu tollole ci lépp wala ay sàrwiisi walangaan
Bëggoo ñu wax sa tur?
Dina ñu denc say leerali joxey bopp ngir ñu doon lu nëbbu.
Sudee li nga bëgg mooy ñu baña wone say joxe, kon di nga ko mën.
Waaye soo bëggee xàm li xew ci sa yëgle kon dina ñu soxla sa dëkkuwaayu imel ngir ñu mën laa yónnee ab imelu firndé ak sa nimero royuwaayu bopp.
Suko defee di nga mëna jokkook ñun ngir am yeneeni leeral ci sa yëgle te mën nañu jokkoo ak yaw suñu soxla yeneeni xibaar ci yaw.