Def ab Yëgle

Salaam, ñoo ngi leen di dalal xëytu yëgle bu IWF Senegal

Xàm nañu ni gis nataal ak wideo yuñuy wone xale yuñuy sàkku mën naa doon lu metti. Ñu ngi lay xàmal ni soo ñu yëgëlee yaa ngi def li war.

Sa yëgle mën naa tax ñu xettali ab xale ci yeneeni sàkku.

Yëgle gi lu gaaw la te mën nga yëgle te doo joxe sa tur benn yoon. Waaye soo bëggee xàm lu xew ci sa yëgle ci beneen bis, dina ñu soxla sa dëkkuwaayu bataaxal ngir ñu xàm nuñuy def ngir jokkoo ak yaw.

Jàppal ni: So ñu bëggee yëgal ni dafa am xale bu nekk ci risk wala nga yëgle dara lu bokkul ab nataal wala wideo bu nekk ci net bi ci wàllum sàkku xale jokkool ak pëliis bu nekk fi nga dëkkee wala ab mbootaayu kaarànge xale ngir am ay tektal.

Jàngal lenn ci sàrtu sunuy nëbbiit